Viatique du 27 juin 2025 : Volonté ….(Par Pr Massamba Gueye)

0
21
Screenshot

Viatique du 27 juin 2025
Volonté ….
« Le bonheur ne s’achète pas, il ne se quémande pas, il se décrète. Quelle vie souhaite-tu vivre? Quelle posture sociale veux-tu avoir? La réponse à ces questions est fondementale dans ta quête de bien-être.

Si tu n’es pas capable de porter ton rêve de bonheur toute ta vie et de construire un mur de verre que les contempteurs ne franchiront jamais, tu te fragiliges. Il te faut avoir la volonté d’être heureux.se pour arriver à sentir en toi l’effervescence nécessaire à ta béatitude. Si tu délégues ton bonheur aux autres, il te sera servi par portions congrues au gré de leurs humeurs.

Lorsqu’une personne en conflit avec elle-même veut t’entraîner dans le sillage de son mal-être, refuse de t’embarquer dans la galère de sa souffrance intérieure. Si tu n’uses pas de ta grandeur pour ne pas céder à la provocation de telles créatures qui vivent dans la haine et le bouillonnement mental, tu t’exposes au ridicule.

Élimine de ton environnement mental toute personne qui cherche à noyer ton bien-être dans un flot de paroles ou de gestes de bas niveau. Les acariâtres ne doivent pas te refiler leur mauvaise humeur. Les aigri.es sont des gens malheureux à qui tu ne dois pas offrir l’occasion de voir ta tristesse. S’ils.elles te provoquent, esquive sans peur car ta victoire est au coin de ton sourire.

Ris de ta souffrance sans faire l’autruche sinon tu péris intérieurment. C’est comme cela que tu sauras faire face aux affres de la vie. «Contamine les gens avec l’amour » dit le sage. Une vie se définit par tes actes. Pose-en donc de favorables à ton épanouissement à celui de ta communauté. Tu dois définir ta perception du temps en te posant la question essentielle de l’usage que tu veux en faire pour atteindre l’allégresse car n’oublie pas que « parfois, la vision qu’on a de soi n’est qu’illusion… ». Il faut aller de l’avant.

Le sentiment de soi est la sève nourricière de ta perception du monde et de ton rapport à toi-même. N’abandonne jamais tes rêves car si tu arrêtes de rêver de bonheur, tu arrêtes de l’espérer et de le vivre. Il n’y a pas de baromètre pour l’indice individuel du bonheur mais chacun sait où il en est avec son propre sentiment de plénitude. Il ne s’agit pas de t’arrimer aux sentiments négatifs mais de t’atteler à créer un environnement propice à ta serenité.

C’est par la respiration que tu contrôles tes émotions. Dés que des fourmis émotionnelles parcourent ton corps, tu vas mal et ton humeur change négativement. Ne laisse pas ce bain nuisible te prendre aussi l’âme. Ralentis ton souffle et reprends tes esprits sinon ces mêmes fourmis te monteront à la langue et au cœur et te feront sortir de tes gongs pour dire et faire des choses regretables.

Tout ce qui te sépare de ta bonne humeur est un poison pour toi. Il te fait serrer les dents et crispe ton visage. C’est le signe que tu es mal. Refuse de céder à la pression de la mauvaise bile. Oppose-lui ta dopamine et inonde ton être de bonheur. C’est comme cela que tu vivras heureux.se. »
Bonne année musulman 1447!
Dr Massamba GUEYE LBA

nayrafet


Yòbbalu 27 i suweŋ 2025
Coobare ….
« Mbégte deesu ko jënd, kenn du ko yalwaan. Gan dund nga bëgg a dund? Ban nit nga bëgg a nekk? Sa tont ci laaj yi lu am solo la ci sa jàmmi yaram ak sa joj xel.

Soo manut a dundal say gént sa giiru dund te def aw dig ci sa diggante ak nit ñi, dangay nasaxal sa bopp. Fulla ak dogooy tax nga bég ba yëg ko ci sa biir. Soo dénkaanee sa mbégte nit ñi ay comp lañ la ciy jox,

Nit ku dundam neexut su la bëggee sotti ay yamb bañal, bul yendu ci gaalu naqaram. Soo doonee nit ku màgg, ku ñàkk fulla di la tooñ, doo ko faale ndax ñoom ay niti musiba lañ, niti fitna yoo xam ni boo leen toppee ñàkkal sa bopp fayda.

Daqal ci sa àddunay xel képp ku lay tàqaleeg sa jàmm tay jéem a mëdd sa mbégte ci wax ju bon mbaa jëf ju safaanoo. Boroom xol yiy wañax bul nangu ñu wàll la naqari deret.

Deel ree boo amee naqar te bañ a mel ni ku ko xamut ba doo ray sa jàmmi biir. Noonu rekk nga man a amee jàmm ba seddele ko nit ñi. Boroom naqar yi waruñoo gis sa mer mbaa sa tiis. Buñ la wutee, moytul te bañ a ragal ndax sa ndam mingi ci sag muuñ.

Say jëf ñooy mandargaal sa dund. Kon defal li xeebuwut tey yokk sa jàmm ak joj sa ñoñ. Dangaa war a leeral sa gis-gisu jamono baa laaj sa bopp loo cay def ci lu am njariñ ba am mbègte mu dul jeex mukk. Yenn saa yi sa gis-gis mooy sa nattukaayu nooflaay. Demal ca kanam.

Xam sa bopp te bañ a yëg sa bopp mooy ruu giy dundal sa tolluwaay ci jamono ak sa diganteeg sa bopp. Bul fàtte mukk say gént sa giiru dund lu ko moy rekk sa yaakaar jeex. Waxeesut nakk nga àltoppe ni wëtiir waaye nga fexe ba féexal sa bopp ci sa coobare.

Ci sag noo ngay nootee say yëg-yëg kon noyil namu waree. Soo demee ba mel ni ay mellantaan dañ laa sam, xamal ni sa xol a jëm réewum naqar. Bul nangu ñu mujj saf la ay yamb, bul bàyyi mukk sa yaram di tog naqar, kon bul bàyyi yit mel ni ay xorondoom dañ lay sot. Soo ci bàyyiwut xel danga wax mbaa nga def looy réccuji ëllëg.

Lépp lu la taqaleeg sa sago ak sa mbégte tooke la ci yow. Day tax ngay màttu, di fas sa kanam ak di fonki. Loolu mooy wane ni yaa ngi ci naqar. Ku la bëgg a jaay naqar feyee gëñ yuy muuñ ak xol bu neex. Noonu ngay dundee ci mbégte ba fàww. »
Àttum jàmm 1447.
Dr Masàmba GÉY LBA

nayrafet

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici